Entrevistas

Omar Pene: “Dañoo jéema boole ay tëgin ngir am sunu yëfu bopp, fent ab misik bu mengoo ag lu Senghoor daan wax sampu ak ubbeeku”

Firikat Faranse/Angale: Brian Valente-Quinn. Tekkikat Wolof/Faranse: Babacar Thiaw

Omar Pene para jot Down

Versión en español aquí

English version here

Version française ici

Omar Pene, di ab woykat ak kenn ci ñu sos groupe bii tudd Super Diamono nekk Dakar, dafay fent ay woy ag di def misik booba ag léégi tolluna ci 5O at. Genne na ay album yu bari, yenn yi mu and ci ak groupe bi, yeneen yi moom kesse. Mbalax, xeetu misik bii nga xamni moom bokk na ci ñiko sos, ab misik la bu boole ay tëg cosaanu Wolof, misiku yeneen i xeet ci Senegaal, ag misiku soul ak blues. Mbalax nekk na tey xeetu misik bu gëna siiw ci Senegaal tàmbali ci at yu réew mi moome boppam, di Independence. 

Pene nekk xeex kat bu magg ngir réewu Afrig yi boolo nekk benn, ba tax CEDEAO takkal ko ab raaya ngir sargal taxawaayam ak liggéeyam ci walë wi. Defna ay at yu bari tey bi Omar Pene di xeex ak ñaax ci lu jëm ci sãsmã kilima bi (Changement Climatique). Loolu dem ba ci ab Album bimu genne ci atum 2019 tuddeko “Climat”. Ci nguuri Macky Sall, Pene tann nañu ko mu nekk ab ambasadër ci wettu ndaw ñi, rawatina etijang yi.

Lii ab waxtaan la biñu amaloon ag woykat bii di Omar Pene. Laaj yi ag tontu yi ci waxtaan bi ci làkkum farãse lañu ko def. Mbind mii nak, ab tekki la ci kàllaamay Wolof.

Ñu wax ci misik mbalax, misiku Wolof, misiku Senegaal, misiku Afrig, wala Afrig sowwu-jànt, walabook misik rek ?

Nañu wax ci misik rek.

Lan mooy solo cosaanu ak raññeewukaayu xeetu Wolof ci sa misik ag sa dund?

Ab doomi Senegaal la, nekk Wolof, muy sama xeet ag làkk bi ma nàmp. Kon lu am solo la ci man, ndax dafa di liñu bëgg jàlla le. Dama jàpp ne Angale yi dañu wara woy ci angale, Farãnse yi woy ci farãnse, Wolof yi tamit woy ci wolof. 

Naka nga tàmbalee ci walum misik ?

Bi may tàmbali, xale bu ndaw laa woon. Damadoon woy ag samay xarit ci mbédd mi ngir fo rekk, ndax man, futbalkat la bëggoon doon. Ci sunu koñ, dafa amoon benn waa juy woy ci ab groupe bu tuddoon “Le Kad Orchestra”. Dafmadaan degg may woy, benn bés mu laaj ma ndax bëgg na bokk ci seen groupe bi. Sama baat dafa nexoon, donte duma géwél, ndax géwél yi lañu xamewoon woy. Booba, gisumawoon sama bopp torop ci woy. Li ma bëggoon moo doon nek futbalkat. Waaye samay xarit ñooma sòññ ne ma naa jéem rekk, ndax ci koñ bi, amoon na ay futbalkat yu bari  waaye amulwoon ab woykat. 

Benn bés, ma jògewoon taggat-yaram ci futbal bi, ma jaar ci bërëb bi orchestre bi nekk. Groupe bi foofu la doon repetee. Ma agsi ag sama yëree futbalkat, njiitu orchestre bi bëgg ma daq. Waaye waa ji bëggoon ma bokk ci groupe bi gis ma, ne ko: xale bi laladoon wax, deggnaa ko muy woy, baatam bi neexna, nañu jéem ak moom ba xam. Binu àggële, mu digg ma: dinañula setsi. Bimu ame ñaari ayubés, waa ji ñëw ne ma: dañula bëgg jël ci groupe bi ndax dañoo soxla ab ndaw suy woy ci wolof. 

Mbalax bi am jamono tey, amulwoon booba, ndax orchestre yi misiku latino lañudoon def, lu melni salsa. Ci làkku espagnol lañu daan woy.

Nii la dugge ci groupe bi. Ci atum 1972 lawoon.

Ñaata at nga amoon boo ba ?

Mangi amoon 17 at.

Kon mën nañu ne sa woy ci làkkum Wolof ci njiitu orchestre boo bu la jóge ?  

Waaw, ndax jamono jooja nit ñi dañoo tàmbaliwoona yéewu ak xaam liñu doon ci aada ak cosaan, bëgg fësal sunu raññeewukaay. Ndax misik biñu daan def feneen la ge, Amerig latine la ge, salsa. Daa nuñu sax jëfëndikoo ay jumtukaay cosaan ak aada lu deme ni sabar, xalam, koora ag yeneen yu gëna mengoog sunu raññeewukaay ag cosaan.

Ñàkkum fësal misiku cosaan bi amoon, ndax dafa laaloon dëkku-àll yi nimu laalewoon dëkku-taax yi?

Waaw. Waaye soo seete ba ci biir, déedéet. Amoon na ab xeetu misik bu gëna cosaane bu tuddoon folklore bu géwél yi daan def. Ca jamano joo ja, ab misik bu ñu daan def la ci dëkku-kaw yi waaye dañuko daan fecc. Sunu demoon boite, misik latino lañufadaan teg. 

Wax ji moodoon fexe gëna jege sunu raññeewukaay. Waaye, li ci amoon solo, moodoon Leopold Sedar Senghor mo nekkoon njiitu reewum Senegal jamono joo ju. Mu doonoon nitu cosaan ag aada. Mu laaj: lu waral woykatu Senegaal yi duñu def xeetu misik bi gëna mengoog seen cosaan ag aada.

Ndax misik tëgin la rek. Senegaal am na ay xeet yu bari, te xeet bu nekk am na cosaan bu and ag xumbaayam. Loolu mooy Senegaal: am na ay Wolof, ay Tuklër, ay Sereer, ay Joola. Xeet bu ne am na ay tëgam bu andag feccam. Loolu lañu wara jél fësal ko ngir sunu raññeewukaayu bopp. 

Ay aada yi nu wéyal la doonte fësaluñ leen woon ci misik bi. Naka nga def ba mën leen na boole ci misik biñu ëp déglu?

Ab xalaatu ay ndawu jamono joo ju la. Te foofu la xalaatu taxawal Super Diamono jóge. Ndax ca jamono joo ja, misik latino nekkul woon liñu ittel. Ci misiku anglo-saxoone lañu gënoon na xër: jazz, rhythm and blues, reggae, soul music. 

James Brown?

James Brown. Bob Marley. Waaw, ci ñun, seen misik moo gënoon niroog sunu misik ag cosaan ndax ay nit ñu ñuul lañu. Jamono jooju ay xalaatu coppite lañu amoon. Jëmm yu maag yu Afrig lañu gënoon jege: Nkrumah, Nelson Mandela. Liñu doon def wuute woon na ag yeneen woykat yi jamono jooja. Defoon nañu ay gestu ci lu laal sunu mgëm-mgëm ag sunu filosofi. Dañoo njëk tànn ne sabar lañuy jëfëndikoo ci sunu misik, ndax ci benn tournée biñu amaloon ci biir Senegaal ag Gambie, dañoo gisoon benn groupe bu tudd Super Eagles ca Gambie, ñuy jëfëndikoo sabar ci seen misik.

Ndax sabar ci cosaanu Seereer la jóge?

Wolof yi am nañu seen xeetu sabar. Joola [Diolas, en français], am nañu seen xeetu sabar. Seereer yi tamit am nañu seen xeetu sabar.

Moussa N’Gom ?  Woykatu Super Diamono la woon? 

Mës na and ak ñun. Waaye, niñuy jëfëndikoo jumtukaay bi dafa wutte ci xeet bu ne. Su dee xam nga waa Touré Kunda, niñuy jëfëndikoo sabar wutte na ak ñun, Wolof yi. Tëggin yi bokkul.

Ndax sunuy tëg, dangay degg wuute gi gi ci saa si ?

Dangay degg wuute gi ci saas si  kay, ndax ni ñu koy tëggee bokkul, tëggin bi dafa wuute. Ni ñu koy fecce sax du benn.

Li groupe bi am ab benn doomi reewu Gambie ci biiram, ndax doon na luy andi ab njaxas soxal misik bi ngeen di def?

Moom [Moussa Ngom], si làkkum soose lay woy, dëgg la, waaye dafay woy ci Wolof itam. Soo deme Gambie, dañufay làkk angale, waaye dañuy làkk wolof itam.

Ndax ci biir groupe bi da ngeen di boole ay xeetu sabar yu wuute?

Déedéet. Kom defnañu ay tournée ci biir réew mi, gis nañu Sereer yi di tëgg Njuup. Dem nañu Fuuta, ci Tuklër yi, xam ngeen Baaba Maal, Yeela lay def. Joola yi di def Jambodon. Ay tëgg yu wuute la. Wolof yi ñooy xeet bi ëp ci Senegaal, ñoom sabar lañuy jëfëndiko, di tëgg Mbalax. Xeetu tëgg yooyu yëpp ño ci am Senegaal. Moom la Léopold Sédar Senghor (njiitu réewu Senegaal bi njëk) daan wax ‘’Seen réew dafa naat ci walum aada ak cosaan. Jëfëndikooleen seen moomel”. Ci la génnee baatu “enracinement ag ouverture”, maanam sàmpu ba noppi ubbekuu. 

Omar Pene para jot Down

Dooleen woon ay bañkat [rebelle] ci askan wi ? Ndax nguur gi daa na leen soññ ci loolu?

Déedéet, maanaam moom, Senghor, dafa nekkoon nitu aada, dafa bëggoon lu laal aada aak cosaan. Nekkoon itam ab bindkat ag taalifkat. Waaye lici biir misik bi, sunu yëf la woon. Senghor dafa joxe rek aw xalaat ci naka lañuy def ba gëna jëfëndikoo jumtukaayu cosaan ak aada yi. Su weeso loolu, li ci biir, mingi aaju ci woykat bu nekk. Man sama wallu bopp, dama tànnoon xeex ngir Afrig booloo. Loolu moo tax ci sunu misik mu am ay woy yinu jaglel Nelson Mandela ci Soweto. Damadoon ngaññ ‘coups d’Etats’ yi; doon woote ngir réewu Afrig yi booloo. Lu tee ñu am sunu ‘Etats-Unis d’Afrique’? Woy naa ci ñakk gi, ci ndool gi, ci ndaw ñu amul  liggéey, xale yu ndaw yi ñuy toroxal, coono jigéen ñi ci seen sey, ñariñu yar xale yi, etc. Daan naa wooy ay mbir yu neexulwoon sunu njiit yi.

Ndax amoon na aay risques, manaam lu ngeen doon ragal?

Waaw. Du ay risk dem kaso, waye ay risk ñu baña teg sunuy woy ci rajo bi, ndax boo ba, benn rajo rek moo amoon. Moo tax, ñun, kenn daanul teg sunuy woy. Loolu rek lawoon, waaye amoon nañu ay soppe, te bëggoon nañu li ñu doon def.

Club Balafon moodoon fi ngeen doon tëgge ayubés bu jot ?

Balafon, ab club la woon bu nekk ci diggu Ndakaaru. Club bi am na limu tekkiwoon ci ñun, ndax ay soppé Super Diamono yu bari fa lañu daan ñëw. Waaye ñenneen ñu bëggoon baneexu àdduna, ñoom ci Youssou Ndour lañu daan dem [reetaan].

Waaye yaag Youssou N’Dour ay xarit ngeen woon?

Waaw.

Dem déglu misik ci concert ci Ndakaaru jamono album boobu, lumu tekkiwoon?

Nit ñi dañoo tàmbaliwoon na nànd ne am na ay coppite yu am ci walum nekkin ak xalaat, rawatina ndawu banlieue yi.

Kon ay coppite lawoon ci walum nekkim ak askaan ?

Waaw waaw. Rawatina soxal etijãã yi.

Ca jamono joo ju ci atu 1970, amoon na ab mbégte ci nu réewu Afrig yi moomoon seen bopp, ci jamono ci coppite soxal askaan wi tàmbalee?

Misik dafa nekkoon ab jumtukaayu jokkale bu tàmbaliwoon na am solo. Booba nekk woykat du woon li ñu naw ci biir askaan wi. Ndax nekk woykat, dañuko jappewoon ni yëfu woyu. Dañu doon nekk ag sangara si ci boite yi. Nit ñi mënuñuwoon na nànd. Ndaxte itam, Senegaal réewu diine la. Mem ci kër yi, wayjur yi nanguwuñuwoon xale yi def misik, dañoo jappoon ni du lu baax, du lu am mujj. Du woon liggéey, du woon luy dundal kër. Dañu jappoon ne yëfu mbedd la. Ñun, dañu doon bayyi xel loolu lëpp.

Nitu diine nga yawit? Ab taalibe Murid nga?

Waaw, dëgg la. 

Ku jege wa Touba nga. Am na ab lëkkalo bu yag digante woykatu mbalax yi ak yoonu Murid, ci lu deme ni woy jalore ci yoon wi. Ndax mës nga am yëg-yëg jëm ci wax lu laal diine bi ci sa misik walabook askaan wi mola gëna ittel?

Amna samay woy yu bari yima jaglel ay Kilifa Murid. Ndax ab Murid laa ci sama walum yaay. Sama maam bima yar, dafmadaan yoobu ci ay jangu Murid. Bimay digante 4 ag 5 i at, dafmadaan yoobu ci seriñam. Foofu la jange ay woyu Murid. 

Bima tàmbali itte woo ci mbiru Seex bi (Seriñ Tuuba), dama def ay gestu ci moom soxal dundinam ag i  mbindam. Yëfu àdduna ittelukowoon, du xaalis, du alal, dara. Bàyyiwul benn alal ginnaaw. Dem naa ba gis làl bimu daan tëdd. Daa nul sax tëdd ci làl bi. Dafsi daan teg ay téereem, ci suuf la daan tëdd. Yére bi mu daan sol amulwoon poos. Dafadoon ñaax nit ñi ci liggéey, njubb, ag wacc sa bopp. 

Ay jikko yu tàmbali dañ ci jamonoy tey ndax ku nekk sa bopp rekk la itteel. Ñëppaw daw ginnaw xaalis. Ngir am xaalis, jaral na nit mu rey moromam wala def naka sudul noonu. Wutee na ag dundinu Seex bi toroop. Loolu moo tax ma naw ko, diko roy ag jaglel ko ab woy. Royuwaay la. Liñuy tiiñal Muridu tey yi, moom bokku ci. 

Tey ay nit ñu bari dañu ciy profitoo waye limu wax leerna: jubb, liggéey, wacc sa bopp. Ay jikko yu tàmbali dañ fëpp. Tey doo xam kuy sa nit, kula bëgg ak kula bañ. 

Ci misik bingadaan def wala ci sa dundin ci lu melni rock n’ roll, ndax amoo ci woon aay jafe-jafe soxal diine ci?

Nit ñi, jappewuñuwoon liñu doon def kom lu am solo. Lileen gënoon soxal mooy li ñu ci doon jàng ci beneen wàllë. Lu toolu ci 95 ci 100 boo jél ci doomi Senegaal ay jullit lañu, waaye tarixaa yi dañoo wuute. Am na ay Murid, ay Tiijaan, ay Laayeen, etc. Ñepp ay jullit lañu waaye tarixaa yi bokkul. Ñun, dañu nu jappewoon kom ay ndaw yu reer.

Man nga ñu wax nakala yëf yi daan deme ci club Balafon?

Mënoo woon ñëw Balafon te doo bëgg Super Diamono. Ab club bu boppam lawoon. Daa nu ñu tagg nit ñi niko ñenneen ci daan defe. Dañudoon ñaxtu njak liggééyu ndaw ñi. Dañudoon woy ag kañ Nelson Mandela. Ay nit dañudoon ñëw dima laaj: “Kan mooy Nelson Mandela?” Dañu nu berroon ci askaan wi. Nit ñi daan ñëw Balafon ñoo doon sunuy soppe. Ñeneen ñi nu japewoon ay nandite te ñu bëggoon àdduna, daal sol yu rafet, ñoom ci Youssou Ndour lañu daan dem. [reetaan]

Ba léegi  ?

Waaw ba léegi kay. [reetaan]

Misik bi ci ay mbir yu am solo la doon wax waaye ànd ci ag xumbaay? 

Waaw amoon na xumbaay. Dañu ci doon gis sunu bopp tamit. Luñu bëggoon la woon, doonte amul woon xaalis bu bari. Toppàtoo wuñu woon loolu. Mbégte bi moo ñu itteloon. Amoon na ay nit ñu daan ñëw ñi ko bëgg. Ñepp dañudaan bégge. Lu jéggi dayoo lawoon. Ci ñun, loolu moo ëppoon solo.

Amul fi nga toolu nga xalaat: léegi star la (ndanaan) ci misik bi?

Star, baat bi neexuma torop. Star mingi tekki “bidééw”. Man dama suufel sama bopp. Suñuy xarit dañudoon ñëw diñu seet si. Dañudoon bokk lépp. Noonu lañudoon dunde sunu biir. Amna ab fanskëlëb (fan club) biñu taxawaloon bu tudd AFSUD (Amicale des Fans du Super Diamono). Maggoon na ba doon mboolo mu rëy. Ay ndaw ñu am taxawaay lañu woon. Tey mangi maggal samay 50 at ci misik. Atum 2023 yépp ay tournée la. Ndawu AFSUD yu tey, seeni wayjur ñoo ko sosoon, seeni magg wëyal ko. Li ñuy jokalante la.

Omar Pene para jot Down

Tey nguur gi daf la tànn nga nekk ambassadeur ci wettu ndaw ñi nekk ci daara yu kawe yi ci Senegaal.

Dëgg la, Njiitu réew mi moo ma tànn.

Dafa melni Senegaal réew muy def xaalis bu bari la ci walum njaang.

Dëgg la. Njiitu réew bi fi nekk tey, jamono bi muy nekk etijaang, dama daan dem di tëg ay concert iniwersite. Am na ab woy bima leen jaglel bi tudd “Etudiant”. Atum 1988 laa ko fent, waaye ba léegi dafa xew. Mënuma tëg concert te etijaang yi laajuñuma ma woy ko. Réew bi ma dem nak. Nit ku am solo laa ci ñoom. Tey am na ay ndaw yu jéll woy bi def ko seen woy te juddu wuñuwoon sax bimakoy génne. Soo deme ci daara Cheikh Anta Diop, amna ab bërëp biñuy defe concert ag lépp lu soxal aada ak cosaan, bërëp boobu Omar Pene la ñu ko tudde.

Am na ci say woy yu bari yuy wax ci ndaw ñi, yi nga  jaglel ndaw ñi, lu tax woy boobu gën see siiw?

Luko waral mooy maay kiko njëk def, ag itam, sama jaar-jaar. Duma ci sori, waaye mën na ne ci mbedd mi la magge. Jàngonte ag  ay jafe-jafe ci sama jaar-jaar. Dund naa lu tax ma mëna xamle ag jàngle. Ci Senegaal, nit ñi xam nañu jaar-jaaru Omar Pene, moo tax ma nekk royuwaay.

Fans club ñoo ngi ko taxawaloon ci atum 1989. Boo bu internet amagulwoon, waaye ndax ndaw ci daa nañu jokalante kaseet yi?

Nit ñi dañudoon jàlalante ay kaseet ndax amoon na beneen xeetu tasaare. [reetaan]. Kom kenn danul teg sunuy woy ci rajo yi, ndaw ñi danañuwoon jokalante kaseet yi.

Yenn saay, ab woykat dafay génne woy, ca ëlëk sa, ñu dégg ko fépp. Ndax lu baax la wala lu bonn?

Ñaar yi yëpp, amna walë bumu baax ag geneen gimu bonn. Ab xeetu jokalante bu teguwul ci yoon la, waaye itam ñépp amuñu dooley jënd CD. Dañuy tàamu jënd ci mbedd ndax ñoo gëna yomb, waaye nak duñu baax. Dangay déglu benn wala ñaar i yoon, mu yaqqù. 

Jamono joo ja, ci Afrig Sowwu-Jànt, ndax génne album amoon na dayoo kom tey? Ndax amoon na solo torop? Génne ab album wala ay woy benn-benn, nakalawoon?

Jamono jooja, ñun daño wuute woon ak li ñenneen ñi daan def ci walum misik. Ci réewu Tugal, ay album lañu daan génne. Fi ay kaseet ño fi xewoon. Waaye am na solo nga génne woy ndax nit ñi dañuko doon xaar. 

Nakala groupe Super Diamono daan def ngir fent ag génee ab woy? 

Super Diamono amna ay jaar-jaar yu bari ag ay génération yu bari. Ca jamono jooja kom nimako waxe ci bimay tàmbali, dañu doon tukki ci biir réew mi ngir xam sunu  aada ag cosaan ag sunu raññeewukaay, maanaam ñooy kan. Dem ngir daje ag nit ñi ngir jàng lu am njëriñ. Loolu diir na ñaari at. Biñu delluse Ndakaaru, ci sunu bërëb, dañu daan tëg misik yëpp. Ci lañu tàmbali bamtu woy yi, di liggéey ag liñu indi wale. Amoon nañu ay bagaas yu bari ci walum misik. Ci lañu wax ni nañu taxawal ab style Diamono. Ñu laaj luñuy def: nañu tudde sunu misik Afro feeling music.

Feeling, jazz ?

Feelingu jazz. Misik la boo xam ne dañoo toog rek fent ko. Kom ab misik la boo xam ne dafa laale ci misik anglo-saxonne. Dañoo jéema boole tëgin yi ngir am sunu yëfu bopp. Fent ab misik boo xam ne dafa mengoo ag lu Senghoor daan wax: enracinement et ouverture (sampu ak ubbeeku). Ab misik bu mengoo ag sunu aadda ci walum tëgin bi ag man muy woy ci Wolof, waaye itam ubbeeku ba ñépp mën see gis seen bopp. Def ba ab Américain bu deggul Wolof mëna yeg ci boppam. 

Lan lay tàmbalee, ay sabar, jungjung, wala ay baat?

Ay sabar, jungjung, basse ladaan tàmbalee. Dañoo japon basse kom ab jumtukaayu misik. Sabar bi moo doon gindikaay bi. 

Maanaam ‘clave’ ni mu mel ci salsa…

Li dès lëpp, muy kalawiye, gitaar, dafay gunge rekk. Soo tëgge tëgin wi rek, dangay am dara. Leneen lëpp dafay joxe melokaan rek. 

Ndax parewoon nga ngir juwe benn xalaat ay yoon yu bari, do toppatoo waxtu buy jàll, ngir taxawal xalaat bi ?

Ku nekk dafa doon indi yëfam, mu nekk yëfu mbooloo. Ku nekk indi xalaatam. Man lima gënal moy ñu fent misik bi ba pare ma dooga ñëw woy. Dangay bayyi ñuy toppatoo misik bi ñu deggoo seen biir. Ab mbooloo la woon. Doonte maay njiit li, maay woy, waaye ku nekk amna sañ-sañu indi yëfu boppam. Dañoo ubbeeku ci wàll boobu. Lu am solo la ci ñun.

Daanul am xëccoo?

Su nuy waxtaan, misik lañuy waxtaane. loolu mooy style lu Diamono. “Diamono” mi ngi tekki “Génération”

Omar Pene para jot Down

Album bu njëk bi, Geedy Dayaan (Geeju Ndayaan), misik bi dafa yeex, ubbeeku. Waaye ay at ci kanam, misik bi dafa gëna gaaw, seere…

Sunu yeene mooy def misik bu neex nit ñi. Moo tax du saa su ne lañuy def liñu neex ñun rek. Ñu bari dañoo wara gis seen bopp ci biir. Sunuy def concert, noolu lañuy tàmbalee. Dañuy tàmbalee ag lu sedd ba pare daal di yeeg ba jot ab tëg bu dëgër, bu xumb. 

Ci sa concert, ab woy mën na def diir bu gudd?

Déedéet. Su bari ba bari, ñent ba juróomi simili lay def. Loolu Tugal lañuko jange, ndax fi dafa wuute. Sooy def ab concert ci réewu Tugal yi, 90 simili rek lañula may. 

Ndakaaru, Senegal, kon mën na jël guddi gi yëpp, loolu nga bëg wax?

Senegaal ay soirées dasantes lañuy tëg. Minwi lay tàmbali, mën na dem ba 4 waxtu ci fajar. [reetaan]

Ndax am ngeen bërëb bi ngeen taamu ngir tëg concert?

Déedéet. Ñun foo ñu woo ñu wuyusila. Groupe bi dafay def ay tournée yu bari. Ci misaal, bima deme Central Park ci New York, am na ay Americain yu doon laaj yenn woy yi. May laaj: wa ñii fu ñu xame lii? Fu ñu degloo lii?” Xawoon nama bett. Gisnaa ay Americain yunu daq fecc sunu misik. [reetaan] Beneen affaire lawoon. Moo tax ñu jap ne njangale Senghor ak mbindam yi amal nañu njariñ.  

Soo leen di boole misiku demb ak misiku tey, ndax misiku demb du dem ba reer ci biir misiku tey? Walabook loolu doolel misiku demb? 

Li am solo mooy misiku cosaan mingi am ba tey. Ñun li ñu nekk di def moy jéem ko mengale ag jamono. Ndax misik, kom niñokoy waxe tey, amul foroñceer. Man damay deglu ay woyu yeneen réew. Deguma angale bu baax, tutti rek; soo may laaj duma xam sax lingay wax, waaye tey ñoo ngi waxtaan sunu biir ag ab tekkikat. Jamono dafay dox, lëppay and doxandoo ag moom, loolu la.

Ndax am na ay misik yu ndawu tey di def yula neex?

Waaw. Liñu mëna japp ci loolu lëpp mooy nimako waxe bimay tàmbali. Sunu jamono, yombulwoon, dañudoon nëbbatu ndax kenn gëmulwoon liñuy def. Askaan wi nanguwulwoon liñudoon def jamono joo ja. Waaye tey, nit ñi soppekunañu ci xalaat, ndax woykat yi tekki nañu. [reetaan] Wutukaayu xaalis la. Woykat yuma bokkal jamono, tey ay kilifa lañu ci askaan wi ndax dañoo tekki. Gis ngeen Youssou Ndour, njittu këru liggéeyukaay la, buy fey ay junni, junni ndaw. Muy Ismaël Lô, Baaba Maal, man, sunu génération yëpp. Taxawal nañu fi dara. Nit ñi dem nañu ba xam ni dañoo jummon ci seen ñakk gëm liñu doon def.

Waaye leegi, kenn teretul doomam mu def misik. Lu ñëpp bëgg la. Amnaa mbégte bokk ci ñu xeex ba loolu taxaw. Liñu wara roy la ci Afrig. Te loolu moo am soo deme ci yeneen  réew tamit. Soo deme Mali, ku melni Salif Keita, soo deme Cameroune itam, fëpp loolu la.

Lan la réewu France di tekki ci yaw, ban solo la am ci yaw? 

Lici jiitu mooy làkk gi, beneen bi mooy ndaw buy saytu sunu ligéey fi la dëk. [reetaan]. Dafay yombalal ligéey bi.

Ci yaw, lan mo neekoon nataalu France? 

Mësuma xalaat ne dinaa mësa ñëw ngir dund France. Toog sama dëk di dund sama dundin moma gënal. Ndax mënuma dund feneen fudul sama dëk donte nittu aada laa. Nit ku ubbeeku la, bëg na di tukki, di dajee ak ñeneen, waaye foofu la yem. Ku bëg sama réew laa. Imigrasyong mësuma itteel. Génne na ab woy buy artu ndaw ñi ndaxte léegi yëf yi yombatul. Léegi ci réew yëpp mbañel jëm ci gann yi dafa tàmbale feeñ ci doomi réew mi. Man panafricain laa, gëm na ni Afrig man na doon benn. Jaglel nako benn woy. Keneen mënul andi coppite kuddul ñun sunu bopp. Waruñu di xaar keneen ñëw ngir naatal sunuy réew. Sunuy réew amna ay goor ag i jiggéen yu xarañ te mëna soppi yëf yi. Xalaatu coppite la. And na ci ndax loolu laa gëm. Lima gëm bu baax la.

Génne nga benn album ci sãsmã kilimatik. Yan xeetu coppite nga gis ci walu kilima bi ci réewu Senegaal wala yeneen xeetu coppite jamono tey?

Adduna lëpp la lëmbee. Ci Senegaal, ñoo ngi koy dund ndax ca Ndar, geej gaa ngi nangu dëkkuwaay yi. Amna benn gox, ndox mi dakoo nangu. Te sãsmã kilima bi moko waral. Dëk yu nekk ci peggu geej gi, ndox mangi nangu kër yi. Léegi nawet ak noor lëpp jaxasoo. Sedd bi du yagg. Weeru desàmbar su dikkoon, dañu daan sol yere yu diis. Léegi waxtu bu ne dafay tang. Afrig moo gëna neew limuy poliye, 4 ci 100 bo jël, waaye teewul ñoci gëna sonn. Lici gëna yeeme,mooy amna ñu gëmul sãsmã kilimatik lu am la. Loolo tax, ci sama yakaar, mu wara am ay nit ñu jog ñaax askaan wi. Sunuko deful, musiba su ci juddoo, doomi Afrig yëpp lay sonnal.

Amna itam yeneen mbir yu am solo. Dañoo wara xeex ndool, sibiru, ñakk lekk gu doy. Covid bi jaar nafi, rey ay temeeri junniy nit. Loolu rek dafa doy ngir ñuy dundaat ay musibaa yu jooge ci sãsmã kilima bi. Loolu moo tax, ci bëgg bima bëgg Afrig, may ñaax nit ñi ngir ay xalaat ag i gestu ci walë wi. Mangi ciy liggéey bu baax te bokkna ci lima boole ci 50 at yimay maggal ci misik.

Am na ay njiitu réew yu xelal ñu jox ay ndampaay réew yi gëna sonn ci musibay sãsmã kilimatik bi.

Ba léegi, defaguñ ci lenn. Lu baax na nit ñi tàmbale nangu sãsmã kimimatik bi lu am la. Ay at ci ginaaw, lu jafewoon la. Degg na Joe Biden dici wax. Njiit bumu wuttu [Trump], mom ittelukowoon. Tey nit ñi xam ñanu solo bi. Ndaw ñi, di yakaaru ëlëk, soobbu nañu ci xeex bi. Saa su ndaje COP ame, dañuy dem giseg dogalkat yi, sañén leen ag artu leen: ‘Xamleen lingeen di def ndax suba lu am sunu kaw lay dal’.

Ndax amna ay réew yu amel aqq seen yeneen i morom i réew jëm ci sãsmã kilima bi wala kolonisasyong? 

Waaw, amna ay réew yu yorel seen i morom aqq ndax dafa am ay jëf yu am ci adduna si yu warul woon am. Ñi jariñoo mbir yooyu nañu nangu ni dañoo noot at réew. Dañu koo wara nangu ba pare, su weesoo ñu joxleen ndampaay, lëpp teggu ci ngor ag xel. 

Ci biir Afrig, ndax am na luñu ci wara saytu digante réew ag moromam, digante doomi Afrig yi?

Waaw kay. Ci weeru Awril bu weesu, dama demoon Abuja, Nigeria, ngir jël benn raaya CEDEAO. Fukk ak juróom njiitu réew téewon nañufa. Bimay ñibbisi, ndax dem bi dama jël wol Dakar-Lomé-Abuja, bariwoon na ay jafe-jafe. Ci laa xalaat, dëgg la gëmna ñu sunu Afrig waaye liggéey bi desna. Dem New York moo gëna yomb dem Abuja. Ay jafe-jafe yuni mel lañu am ñun doomi Afrig, ci wet gi ñuy wax waxi yombal dem-ak-dikku nit ñi ak njaay mi. Kon xam nga ni amna liggéey gu bari gu des. Ay nit waxna ñuma: ‘Lingay xeex, ndax du ay xeetu gént rek?’. Xëyna, waayë dañu wara am ngëm-ngëem. 

Omar Pene para jot Down

Binga nekke xale donowoon géwel, léegi ak misik mu melni géwel nga. Ñu defla ngay ambasadër, di royuwaay. Ndax yenn bi diisul?

Nit ñi waxuñu ci ndax xeex bi amna ay ñeneen ñuko sos. Amoon na ay njiit ag i borom-xam-xam yu melni Kwame Nkrumah, Cheikh Anta Diop, Nelson Mandela, Amilcar Cabral, ay nit ñu magg. Ci ginaawam amoon na Thomas Sankara doomu réewum Burkina Faso, ku amoon ay xalaat jëm ci Afrig doon benn. Amna ay nit ñuko gëm, waaye ci wet gi, amna ci ñimu baaxul.  Réew yuy jëfëndiko am-am Afrig duñu ci mësa and. Léegi nak, doomi Afrig ñooy xool ag jog taxaw.

Ndax dangay juwe futbal ?

Bayinaa waaye sport bima neex la. Mën na toog ay waxtu di seetaan futbal. Dama bëgg futbal.

Ban mooy sa ekip?

Sama ekip Senegaal Jaraaf la. Jaglel na leen sax ab woy. Sama ekip France mooy Marseille, Anglette nak, Manchester City la.

Futbal dafa laaj xarañte. Bëg na NBA itam. Basket dafma neex. Bëggoon naa Mike Jordan. Dafa am ay nit yu mel noonu, dafa am luñu andal.

Amna ñuy wax taagat-yaram dafa niru ak misik, ndax mën-mën bi ak jëf-jëf yi ci saa si la.

Waaw, te taagatkaatu yaram yi itam daño bëgg misik. Amna ay boksër sunuy dugg ci areen bi, dañuy takk ay cask wala ñu and ag ab rappeur. 

Ndax yaw bëgg nga box ?

Sama soxna moo bëgg boxe. Dinaa di seetaan waaye lëpp lu and ak fitna sawaruma ci. 

Moo mengoo ag lamb ci Senegaal…

Sunu lamb ji itam. Bëre cosaan la gëna bëgg, ndax dafa laaj xarañte. Amul door, xarañte mooy tax nga daal. Waaye nak sunu tàmbali kurpeeñ yi…

Mbadu leneen lay doon…

Waaw, leneen lay doon. Ay nit ñuy raag ngir xaalis, amna ñu pare def lëpp ngir am xaalis.

Mangi lay gërëm ci waxtaan bi.

Ñookoo bokk. Bégna ci torop. Di am yaakaar ñu gisewaat Senegal, inchallah. Waxtaan bi amoon na solo torop. Lima gëna neex ci waxtaan bi mooy waxuñu waxu politik, contaan naa ci te dila ci sant. Jërëjëf!

Omar Pene para jot Down

SUSCRIPCIÓN MENSUAL

5mes
Ayudas a mantener Jot Down independiente
Acceso gratuito a libros y revistas en PDF
Descarga los artículos en PDF
Guarda tus artículos favoritos
Navegación rápida y sin publicidad
 
 

SUSCRIPCIÓN ANUAL

35año
Ayudas a mantener Jot Down independiente
Acceso gratuito a libros y revistas en PDF
Descarga los artículos en PDF
Guarda tus artículos favoritos
Navegación rápida y sin publicidad
 
 

SUSCRIPCIÓN ANUAL + FILMIN

85año
Ayudas a mantener Jot Down independiente
1 AÑO DE FILMIN
Acceso gratuito a libros y revistas en PDF
Descarga los artículos en PDF
Guarda tus artículos favoritos
Navegación rápida y sin publicidad
 

3 Comentarios

  1. Pingback: Omar Pene: “Through rhythms we tried to create a music that sounded like us, that took into account rootedness and openness” - Jot Down Cultural Magazine

  2. Pingback: Omar Pene: «A través de los ritmos intentamos crear una música que sonara a nosotros, que tuviera en cuenta el arraigo y la apertura» - Jot Down Cultural Magazine

  3. Pingback: Jot Down News #46 2023 - Jot Down Cultural Magazine

Deja un comentario

Tu dirección de correo electrónico no será publicada. Los campos obligatorios están marcados con *

*

Este sitio usa Akismet para reducir el spam. Aprende cómo se procesan los datos de tus comentarios.